3 Fōfale i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña dajalo fi ker i kēlifa i seriñ ya, ku tūda Caiaphas,
Peter nak don na tōg cha biti cha ker ga: bena janh͈a ñou fi mōm, ne, Yā nek’ on ak Yesu wā’ Galilee ba.
Fōfale i h͈arekat i kēlifa ga yubu Yesu chi ker i ate ga, te dajale fi mōm sēn i morom yepa.
I njīt i seriñ ya ak Pharisee ya joh͈e won nañu eble, ne su kena h͈ame fu mu neka, na ko wone, ndah͈ ñu japa ko.
Annas nak ew ko, te yōni ko Caiaphas, kēlifa i seriñ ya.
Ñu omat Yesu nak cha Caiaphas be cha bir ateukay ba: te têl on na; ti ñom h͈arafu ñu cha ateukay ba, ndah͈ du ñu gakal sēn bopa, wande ndah͈ ñu mun a leka h͈ewte ga.