28 Ndege lile di suma deret i koleri gu ês, ja di tūru ndig ñu bare ndege mbaale’ i bakar.
Naka Dōm i nit ka ñouūl ndah͈ ñu bukanēgu ko, wande ndah͈ mu bukanēgu, te may dund’ am njot ngir ñu bare.
Mu jel mbatu, gerem Yalla, te joh͈ len ko, ne, Nān len chi yēn ñepa;
Wande mangi len di wah͈, Du ma nānati dōm i garap i biñ bile, be cha bes bōba ma ko nāni bu ês ak yēn chi suma ngur i Bay.
Te baal ñu suñu i bakar, naka ñu baale ña ñu tōñ;