Fōfale Yesu ne len, Di ngēn fakatalu ndig man chi gudi gile yēn ñepa: ndege binda nañu, ne, Di nā dōr sama ba, te i nh͈ar i gēta ga di nañu h͈ajātlaku.
Tah͈na ñu wah͈ante, ne, Bu ñu ko h͈oti, wande na ñu ko wure ku ko di mōmi: ndah͈ mbinda ma motaliku, ne, Sedāle nañu on suma i cholay, te wure suma mbuba. H͈arekat ya nak def on nañu yef yōyale.