22 Ñu nah͈arlu bu miti, te ku neka dal ne ko, Borom bi, man lā’m?
Ba ñu di leka, mu ne, Chi dega mangi len di wah͈, kena chi yēn di na ma ori.
Mu tontu, ne, Ki jō loh͈o am ak man chi ndap li, kōka ma ori.
Mu ne ko ñetel i yōn bi, Simon, dōm i John, sopa nga ma? Peter nah͈arlu ndege nôn na ko ñetel i yōn bi, Sopa nga ma? Te mu ne ko, Borom bi, h͈am nga lu neka; h͈am nga ne sopa nā la. Yesu ne ko, Samal suma i nh͈ar.