Matthew 26:18 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
18 Mu ne, Dem len chi bir deka ba fa kena nit, te ne ko, Jemantalkat ba ne, Suma wah͈tu jegeñsi na; di nā h͈umbal h͈ewte ga chi sa nēg, ak suma i tālube.
Ba h͈ewte i njot ga lāta jot, Yesu ka h͈am ne wah͈tu am dikasi na ba mo di bayi aduna si dem fa Bay ba, naka mu sope won yos am ña neka chi aduna si, mu sopa len be cha muj ga.