13 Chi dega mangi len di wah͈, Fu ñu mun a wāre linjil bile chi aduna si yepa, di nañu nitali la jigen jile def on ndah͈ di ko fatalako.
Bile linjil i ngur gi, di nañu ko wāre chi aduna si yepa ndig sēde chi h͈êt yi yepa; cha ganou ga muj ga di na ñou.
Dem len mbōk, def i tālube h͈êt yi yepa, te batise len chi tur i Bay ba, ak Dōm ja, ak Nh͈el mu Sela ma: