9 Wande ñu am sago ña tontu, ne, H͈ēchna du doy chi ñun ak yēn: na ngēn dem fa ña di jay, te jendal sēn bopa.
Mangi len di yōni naka i nh͈ar chi digante i būki: mōtah͈ na ngēn têylu naka i jān, te lew naka i mpetah͈.
Jurom chi ñom nek’ on nañu ñu ñaka sago, te jurom ña di ñu am sago.
Ñu ñaka sago ña wah͈ ñu am sago ña, ne, May len ñu chi sēn diwlin; ndege suñu i lamp’ ange fey.
Mōtah͈ ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te def len, di na niro ak nit i sago, ka tabah͈ nēg am chi kou doch: