8 Ñu ñaka sago ña wah͈ ñu am sago ña, ne, May len ñu chi sēn diwlin; ndege suñu i lamp’ ange fey.
Fōfale di nañu nirale ngur i ajana ak fuk’ i h͈ēk, ñu jel on sēn i lampa, di gatanduji borom‐seyt.
Fōfale h͈ēk yōyale yepa jog, te jagal sēn i lampa.
Wande ñu am sago ña tontu, ne, H͈ēchna du doy chi ñun ak yēn: na ngēn dem fa ña di jay, te jendal sēn bopa.
Te bu len dēfe ne chi sēn bopa, Am nañu Ibrayuma mu di suñu bay; ndege mangi len di wah͈, ne Yalla mun na chi h͈êr yile sah͈ gēne chi i dōm i Ibrayuma.