7 Fōfale h͈ēk yōyale yepa jog, te jagal sēn i lampa.
Fōfale di nañu nirale ngur i ajana ak fuk’ i h͈ēk, ñu jel on sēn i lampa, di gatanduji borom‐seyt.
Wande chi dig’ i gudi h͈āchu ma jib, ne, Borom‐seyt bā’nge dika! Dem len, gatanduji ko.
Ñu ñaka sago ña wah͈ ñu am sago ña, ne, May len ñu chi sēn diwlin; ndege suñu i lamp’ ange fey.