6 Wande chi dig’ i gudi h͈āchu ma jib, ne, Borom‐seyt bā’nge dika! Dem len, gatanduji ko.
Te di na yōni malāka am ya ak nchōu i bufta bu rey, te di nañu dajale ña mu tan’ on chi ñenent i ngelou yi, cha bop’ i asaman be cha muj ga.
Mōtah͈ na ngēn di defaru yēn it: ndege Dōm i nit ka di na ñoui chi wah͈tu bu ngēn dul fōg.
Fōfale di nañu nirale ngur i ajana ak fuk’ i h͈ēk, ñu jel on sēn i lampa, di gatanduji borom‐seyt.
Bu Dōm i nit ka di ñoui chi ndam am, ak malāka ya yepa and’ ak mōm, di na tōg chi kou gangūne’ ndam am:
Ba borom‐seyt ba yīh͈e, ñepa gemantu te nelou.
Fōfale h͈ēk yōyale yepa jog, te jagal sēn i lampa.