4 Wande ñu am sago ña yubuāle diwlin chi sēn i ndap ak sēn i lampa.
Mangi len di yōni naka i nh͈ar chi digante i būki: mōtah͈ na ngēn têylu naka i jān, te lew naka i mpetah͈.
Jurom chi ñom nek’ on nañu ñu ñaka sago, te jurom ña di ñu am sago.
Ñu ñaka sago ña jel sēn i lampa, te yubuāleū ñu diwlin ak ñom:
Ba borom‐seyt ba yīh͈e, ñepa gemantu te nelou.
Mōtah͈ ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te def len, di na niro ak nit i sago, ka tabah͈ nēg am chi kou doch:
Ndege kōka Yalla yōni on, bāt i Yalla yi la wah͈: ndege joh͈ewul Nh͈el ma chi natu.