3 Ñu ñaka sago ña jel sēn i lampa, te yubuāleū ñu diwlin ak ñom:
Fōfale di nañu nirale ngur i ajana ak fuk’ i h͈ēk, ñu jel on sēn i lampa, di gatanduji borom‐seyt.
Jurom chi ñom nek’ on nañu ñu ñaka sago, te jurom ña di ñu am sago.
Wande ñu am sago ña yubuāle diwlin chi sēn i ndap ak sēn i lampa.