2 Jurom chi ñom nek’ on nañu ñu ñaka sago, te jurom ña di ñu am sago.
Mangi len di yōni naka i nh͈ar chi digante i būki: mōtah͈ na ngēn têylu naka i jān, te lew naka i mpetah͈.
Kan a di bukanēg mbōk bu taku te têy, bu borom am jītal chi ker am, ndah͈ mu joh͈ len sēn dundu chi wah͈tu wa?
Ñu ñaka sago ña jel sēn i lampa, te yubuāleū ñu diwlin ak ñom:
Wande ñu am sago ña yubuāle diwlin chi sēn i ndap ak sēn i lampa.
Wande ñu am sago ña tontu, ne, H͈ēchna du doy chi ñun ak yēn: na ngēn dem fa ña di jay, te jendal sēn bopa.