9 Fōfale di nañu len jebale ndah͈ ñu geten len, te di nañu len rēy: h͈êt yi yepa di nañu len sib ndig man.
Ña des japa i ndau am, tedadil len, te rēy len.
Tah͈na yōne nā len i yonent, ak i borom‐sago, ak i h͈amkat: di ngēn rēy ñena ñi, te dāj len cha kura; te di ngēn ratah͈ ñena ñi chi sēn i juma, te geten len chi dek’ ak deka:
Su len aduna si bañe, h͈am ngēn ne man la bañ on bala mu len di bañ.
Wande yef yile yepa la ñu di defi ndig suma tur, ndege h͈amu ñu ka ma yōni on.
Di nañu len gēneji cha juma ya: chi dega wah͈tu wa di na jot ne ku mu mun a don ku len di rēy, di na dēfe ne defal na Yalla ligey.