5 Ndege ñu bare di nañu ñoui chi suma tur, ne, Mā di Krista, te di nañu nah͈i ñu bare.
Yonent i nafeh͈a yu bare di nañu jogi, te nah͈ ñu bare.
Ndege Krista yu nafeh͈a di nañu jogi, ak yonent yu nafeh͈a, te wone mandarga yu rey ak i koutef; be ñu di nah͈i ña ñu tana sah͈, su munê am.
Da ma ñou chi suma tur i Bay, te nanguwu len ma: su kenen di ñou chi tur i bop’ am, mōm ngēn di nangu.
Tah͈ on na ma wah͈ len, ne, Di ngēn dē chi sēn i bakar: ndege su ngēn gumule ne mā di mōm, di ngēn dē chi sēn i bakar.
Yesu nêti len, Ba ngēn di yēkatiji Dōm i nit ka, bōba nak di ngēn h͈am ne mā di mōm, te defu ma dara chi suma bopa, wande naka ma Bay ba jemantale won, na lā wah͈e yef yile.