49 Te dal di dōr i naule am, leka ak nān ak mandikat ya;
Wande jām bōbale gēna, te feka kena chi i naule am, ku ko leb on tēmēr i kopar: mu japa ko, ne ko chih͈ chi bāt am ne, Fey ma lo ma leb on.
Wande su bukanēg bu bon bale wah͈e chi h͈ol am, ne, Suma borom yīh͈ na;
Borom i bukanēg bōbale di na ñou chi bes bu mu ko sēnuwul, ak chi wah͈tu wu mu h͈amul,
Otu len i yonent i nafeh͈a ya, di ñou fi yēn chi nchangay i nh͈ar, wande chi bir ño di buki yu fuh͈ale.
Te ne ko, Nit ku neka biñ bu bāh͈ ba la jeka tāj: te su ñu nāne be lu bare, mu isi bu genadi ba; yā dēncha biñ bu bah͈ bi be lêgi.