47 Chi dega mangi len di wah͈, Di na ko teg njīt cha la mu am yepa.
Barkel chi bukanēg bōbale, ba borom am di feka mu di def nōga ba mu agse.
Wande su bukanēg bu bon bale wah͈e chi h͈ol am, ne, Suma borom yīh͈ na;
Borom am ne ko, Wau gōr, E jām bu bāh͈ bi te taku: da nga gōre chi lu new, di nā la teg njīt chi lu bare: h͈arafsil chi sa banēh͈ i borom.
Borom am ne ko, Wau gōr, E jām bu bāh͈ bi, te taku: da nga gōre chi lu new, di nā la teg njīt chi lu bare: h͈arafsil chi sa banēh͈ i borom.
Su ma kena bukanēgo, na ma topa; te fu ma neka, fōfale la suma bukanēg di neki: su ma kena bukanēgo, mōm la Bay ba di magal.