46 Barkel chi bukanēg bōbale, ba borom am di feka mu di def nōga ba mu agse.
Kan a di bukanēg mbōk bu taku te têy, bu borom am jītal chi ker am, ndah͈ mu joh͈ len sēn dundu chi wah͈tu wa?
Chi dega mangi len di wah͈, Di na ko teg njīt cha la mu am yepa.
Fōfale Bur ba di na wah͈ ña cha ndējor am, ne, Ñou len, yēn ña suma Bay barkel, dona len rew mu ñu len wājal on cha ndôrte’ aduna si: