Ba mu tōge chi tūnda i Olive ya, tālube ya ñou fi mōm chi mpet, ne, Wah͈ ñu, kañ la yef yile di ami? te la di doi sa mandarga’ ndika, ak i muj i aduna si?
Fōfale mandarga i Dōm i nit ka di na fêñ cha asaman; h͈êt i aduna si yepa di nañu yeremtu, te di nañu gis Dōm i nit ka mu di ñou chi i nir i asaman si ak kantan ak ndam lu rey.