25 Mangi len di yēgal bala wah͈tu wa jot.
Mangi len di yōni naka i nh͈ar chi digante i būki: mōtah͈ na ngēn têylu naka i jān, te lew naka i mpetah͈.
Ndege Krista yu nafeh͈a di nañu jogi, ak yonent yu nafeh͈a, te wone mandarga yu rey ak i koutef; be ñu di nah͈i ña ñu tana sah͈, su munê am.
Mōtah͈ su ñu len wah͈e, ne, Munga cha manding ma; bu len fa dem: munga chi bir nēg ya; bu len ko gum.
Yef yile lā len wah͈, ndah͈ du len fakatalu.