24 Ndege Krista yu nafeh͈a di nañu jogi, ak yonent yu nafeh͈a, te wone mandarga yu rey ak i koutef; be ñu di nah͈i ña ñu tana sah͈, su munê am.
Ndege ñu bare la ñu ô, wande ñu new la ñu tana.
Yonent i nafeh͈a yu bare di nañu jogi, te nah͈ ñu bare.
Su ñu gatalul on bes yōgale, ken du kon muchi: wande ngir ña ñu tana, di nañu gatal bes yōgale.
Mangi len di yēgal bala wah͈tu wa jot.
Te di na yōni malāka am ya ak nchōu i bufta bu rey, te di nañu dajale ña mu tan’ on chi ñenent i ngelou yi, cha bop’ i asaman be cha muj ga.
Ndege ñu bare di nañu ñoui chi suma tur, ne, Mā di Krista, te di nañu nah͈i ñu bare.
Otu len i yonent i nafeh͈a ya, di ñou fi yēn chi nchangay i nh͈ar, wande chi bir ño di buki yu fuh͈ale.
Yesu ne ko, Su ngēn gisule i mandarga ak i koutef, ngēn bañ a gum.
Ña ma Bay ba may ñepa, di nañu ñou fi man: te ku ñou fi man, du ma ko dah͈a muka.
Te mbugel i ka ma yōni on a di lile, ne ña mu ma may ñepa, du ma ñaka ken, wande dēkali ko cha kera bes ba.