11 Yonent i nafeh͈a yu bare di nañu jogi, te nah͈ ñu bare.
Te ndig bakar di na fūs, nchofel i ñu bare di na wañiku.
Ndege Krista yu nafeh͈a di nañu jogi, ak yonent yu nafeh͈a, te wone mandarga yu rey ak i koutef; be ñu di nah͈i ña ñu tana sah͈, su munê am.
Ndege ñu bare di nañu ñoui chi suma tur, ne, Mā di Krista, te di nañu nah͈i ñu bare.
Otu len i yonent i nafeh͈a ya, di ñou fi yēn chi nchangay i nh͈ar, wande chi bir ño di buki yu fuh͈ale.