10 Fōfale ñu bare di nañu fakatalu, orante, te sibante.
Mag di na jebal rak’ am ndah͈ mu dē, te bay dōm am: i dōm di nañu or sēn i bay ak sēn i ndey, te rēylu len.
Te barkel chi ku dul feka fakatalu chi man.
Wande amul rên chi bop’ am, te muñ chi sā yu new dal; ndege su nah͈ar joge wala ngeten ndig bāt bi, nōg’ ak nōga mu fakatalu.
Ñu fakatalu chi mōm. Wande Yesu ne len, Yonent ñakul teranga lu moy chi dek’ am, ak chi ker am.
Yonent i nafeh͈a yu bare di nañu jogi, te nah͈ ñu bare.