1 Yesu don na gēna cha juma ja, di dem yōn am; te i tālube am ñou fi mōm, di ko won i tabah͈ i juma ja.
Ba mu ñoue chi bir juma ja, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñou fi mōm ba mō jemantale, ne, Ak ban sañsañ nga defe yef yile? te ku la joh͈ sañsañ bile?
Ndege mangi len di wah͈, Du len ma gisati be bu ngēn di wah͈i, ne, Barkel chi ka di dika chi tur i Borom bi.
Yauod ya ne ko, Ñenent fuk’ i at ak jurom bena la ñu am di tabah͈ juma jile, te you di nga ko tah͈oual chi ñet’ i fan am?