5 Wande ño di def sēn i jef ndah͈ nit gis len: ndege ño di yāal sēn i galaj, te reyal sēn i mbichah͈tan i mbūba,
Jena jigen, ku am on h͈up i deret fuk’ i at ak ñar, ñou chi ganou am, te lāl mbichirān i mbūba’m:
Ndege sop’ on nañu teranga bu juge fi nit as teranga bu juge fa Yalla.
Naka ngēn mune gum, yēn ña nangulante ndam, te ndam li juge cha Yalla reka, ūtu len ko?
Ku di wah͈ chi bop’ am, ndam i bop’ am la di ūt: wande ku di ūt ndam i ka ko yōni on, mō di dega, te jubadi nekul chi mōm.