4 Ño di taka say yu dīs, te mite yubu, teg len chi i mbag i nit; wande ñom du ñu len randal ak sēn baram.
Suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn fey asaka i oyof ya, te sagane yef i yōn wa gen a rey, mu di njūbay, ak yermande, ak ngum: yile ñom ngēn war on a def, te bañ a sagane yena ya.
Mōtah͈ lu mu mun a don lu ñu len ebal, dēgal len, te def ko; wande bu len def naka sēn i jef; ndege ño di wah͈, te du ñu def.