29 Suboh͈un yēn, bindānkat yi, ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn tabah͈ i bamel i yonent ya, te rafetlo i bamel i ñu jūb ña,
Suboh͈un yēn, bindānkat yi, ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn niro ak bamel ya ñu wêh͈al, ñu rafet chi biti, wande chi bir fês ak i yah͈ i ñu dē, ak nubay gu mun a don.
Nōgu itam ngēn di wone njūlit chi nit chi biti, wande chi bir da ngēn fês ak nafeh͈a ak bakar.
Te ne, Su ñu nek’ on chi suñu bes i bay ya, doū ñu on bōlo ak ñom chi deret i yonent ya.