19 Silmaha yi: bu chi gen a rey, maye gā’m, am lotel ba di selal maye ga?
Dof yi ak silmah͈a yi: bu chi gen a rey, wurus wā’m, am juma ja di selal wurus wa?
Te, Ku di geñ cha lotel ba, dara la; wande ku di geñ cha maye ga cha kou am, war na ko motali.
Ku di geñ cha lotel ba mbōk, geñ na cha mōm, ak la cha kou am yepa.