31 Wande mosu len a janga lu jem chi ndēkite ga, la len Yalla wah͈ on, ne,
Wande mu ne len, Ndah͈ jangu len la Dauda def on ba mu h͈īfe, ak ña and’ on ak mōm;
Wande su ngēn h͈am on lu lile tiki, Yermande lā buga as h͈arfan, kôn dōtu len eda ña moyul.
Te ne ko, Ndah͈ dēga nga li ñile di wah͈? Yesu ne len, Wau: ndah͈ mosu len a janga, ne, Chi gemeñ’ i dōm ak i gūne yu di nampa nga motali nau?
Yesu ne len, Ndah͈ mosu len a janga chi mbinda mi, ne, Doch wa tabah͈kat ya bañ on, mō di neki bop’ i tabah͈ ma: lile juge na fa Borom bi, te koutef la chi suñu i but?
Ndege chi ndēkite ga du ñu sey, te du ñu len maye chi sey, wande di nañu neka naka malāka ya cha ajana.
Mā di Yalla i Ibrayuma, ak Yalla i Isaka, ak Yalla i Yanh͈oba? Yalla du Yalla i ñu dē ña, wande ñu dunda ña.
Wande dem len te jemantu lu lile tiki, Yermande lā buga as h͈arfan: ndege diku ma ô ñu jūb ña, wande i bakarkat.