26 Ñarel ba itam def nōgule, ak ñetel ba, be cha jurom ñarel ba.
Ñu yōni fi mōm sēn i tālube ak ga’ Herod, ne, Jemantalkat bi, h͈am nañu ne yā di dega, di jemantale yōn i Yalla chi dega, te ragalu la ken, ndege sêtu la kanam i nit.
Jurom ñar i dōm i ndey nak anga won ak ñun: mag ba sey on na, dē, te amul dōm, te bayi jabar am ak rak’ am;
Ganou ga jigen ja itam dē.