25 Jurom ñar i dōm i ndey nak anga won ak ñun: mag ba sey on na, dē, te amul dōm, te bayi jabar am ak rak’ am;
Ne, Jemantalkat bi, Musa wah͈ on na, ne, Su nit dēe te amul dōm, rak’ am war na sey ak jabar am, te jur dōm chi mag am;
Ñarel ba itam def nōgule, ak ñetel ba, be cha jurom ñarel ba.