24 Ne, Jemantalkat bi, Musa wah͈ on na, ne, Su nit dēe te amul dōm, rak’ am war na sey ak jabar am, te jur dōm chi mag am;
Ñu yōni fi mōm sēn i tālube ak ga’ Herod, ne, Jemantalkat bi, h͈am nañu ne yā di dega, di jemantale yōn i Yalla chi dega, te ragalu la ken, ndege sêtu la kanam i nit.
Jurom ñar i dōm i ndey nak anga won ak ñun: mag ba sey on na, dē, te amul dōm, te bayi jabar am ak rak’ am;
Jemantalkat bi, ban eblê gen a rey chi yōn wi?
Du ku neka ku ma wah, ne, Borom bi, Borom bi, di na h͈araf chi ngur i ajana; wande ka def suma mbugel i Bay ba cha ajana mōm reka.