21 Nu ne ko, Cæsar la. Mu ne len mbōk, Joh͈ len Cæsar yef i Cæsar; te Yalla yef i Yalla.
Mu ne len, Bile ban natal la ak mbinda?
Mu ne ko, Na nga sopa Borom bi sa Yalla ak sa h͈ol bepa, ak sa fit wepa, ak sa nh͈el mepa.
Fōfale Yesu ne ko, Randu ma Seytane, ndege binda nañu, ne, Na nga jāmu Borom ba sa Yalla, te na nga ko topa, mōm reka.