18 Wande Yesu gis sēn kēfēr, te ne len, Lutah͈ ngēn di ma fire, yēn nafeh͈a yi?
Yesu h͈am lōla, te mu sipi fōfale; ñu bare topa ko; mu weral len ñom ñepa.
Pharisee ya ñou fi mōm, di ko fir, te ne ko, Ndah͈ dagan na nit fase jabar am ndig lu mu mun a don?
Wah͈ ñu nak, Lo dēfe? Ndah͈ dagan na ñu joh͈ Cæsar ngalak, am dēt.
Won len ma h͈ālis i ngalak li. Ñu yub ko h͈asab.
Te soh͈lawul kena sēde chi lu jem chi nit; ndege mō h͈am on lu neka chi h͈ol i nit.
Te lile wah͈ nañu ko di ko jēm, ndah͈ ñu mun a am lu ñu ko jêñ. Wande Yesu sega, te binda chi suf si ak baram am.