11 Wande ba bur ba h͈arafse ndah͈ mu sêt ña ñou on, mu gis fa nit ku solul on chol i nchēt ga:
Bayi len ñar ña ñu sah͈ando be cha ngōbte ga; te cha wah͈tu’ ngōbte ga di nā wah͈ gōbkat ya, ne, Budi len jeka nduh͈um la, taka ko i say te laka ko; wande dajale len dugup ja chi suma sah͈a.
Ndau ya dem cha mbeda ya, dajale ña ñu gis ñepa, ña bon ak ña bāh͈ itam; nchēt la fês ak ña ñu ô.
Am na layu chi loh͈o am, te di na setali boju am fou, te dajale dugup am chi sah͈a mi; wande di na laka choh͈ ba chi safara su feyatil muk.