10 Ndau ya dem cha mbeda ya, dajale ña ñu gis ñepa, ña bon ak ña bāh͈ itam; nchēt la fês ak ña ñu ô.
Tōl ba aduna si la; jiu wu bāh͈ wa i dōm i ngur ga la; nduh͈um la i dōm i bulis la;
Dem len mbōk chi mbeda ya, te ñu ngēn gis ñepa, ô len chi nchēt li.
Ba ñu deme di jendi, borom‐seyt ba agsi; te ña jaglu on h͈arafando ak mōm cha nchēt la; te bunta ba teju.
Yesu ne len, I mbok’ i nēg i borom‐chēt ga, ndah͈ mun naño nah͈arlu ba borom‐chēt ga neke ak ñom? Wande jamāno di na diki ba ño fabi borom‐chēt ga cha ñom; bōbale di nañu ôri.