46 Ba ñu jēme japa ko, ñu ragal mbōlo ma, ndege jape won nañu ko niki yonent.
Mbōlo ma ne, Kile di Yesu, yonent i Nazareth chi Galilee.
Wande su ñu ne, Chi nit; da ñu ragal mbōlo ma; ndege jape won nañu John niki yonent.
Ba i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya dēge lēb am ya, ñu gis ne lu jem chi ñom la wah͈.
Yesu tontu te wah͈ati len chi i lēb, ne,
Ñu di ko ūt a japa nak; wande ken tegul loh͈o chi kou am, ndege wah͈tu am jotangul.
Aduna si munul len a bañ; wande man la bañ, ndege sēde nā chi lu jem chi mōm ne i ligey am bon nañu.