45 Ba i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya dēge lēb am ya, ñu gis ne lu jem chi ñom la wah͈.
Naka la nit gene nh͈ar! Mōtah͈ dagan na def lu bāh͈ chi bes i dimas.
Mu wah͈ len yef yu bare chi i lēb, ne, Bena jikat dem on na ji;
Ku dānuji chi doch wile, di na dama: wande ku mu dānu chi kou am, di na ko mokal kilip.
Ba ñu jēme japa ko, ñu ragal mbōlo ma, ndege jape won nañu ko niki yonent.