43 Mōtah͈ ma ne len, Di nañu jele ngur i Yalla fi yēn, te joh͈ ko h͈êt wu di mēña mēñef am.
Wande su ma gēnê jine ya chi Nh͈el i Yalla, bōba ngur i Yalla dika na fi yēn.
Ñu ne ko, Di na rēy nit ñu soh͈or ñōgale chi choh͈or, te lūye tōl am yenen i ligeykat, ñu ko di joh͈i mēñef yi chi sēn wah͈tu’ ñorte.
Yesu ne len, Ndah͈ mosu len a janga chi mbinda mi, ne, Doch wa tabah͈kat ya bañ on, mō di neki bop’ i tabah͈ ma: lile juge na fa Borom bi, te koutef la chi suñu i but?
Ku dānuji chi doch wile, di na dama: wande ku mu dānu chi kou am, di na ko mokal kilip.
Yesu tontu te ne ko, Chi dega, chi dega, mangi la wah͈, Su nit jūduātule, du mun a gis ngur i Yalla.
Yesu tontu, ne, Chi dega, chi dega, mangi la wah͈, Su nit jūduwule chi ndoh͈ ak Nh͈el ma, du mun a h͈araf chi ngur i Yalla.