41 Ñu ne ko, Di na rēy nit ñu soh͈or ñōgale chi choh͈or, te lūye tōl am yenen i ligeykat, ñu ko di joh͈i mēñef yi chi sēn wah͈tu’ ñorte.
Ba jamāno i mēñef jegeñse, mu yōni i ndau am chi ligeykat ya ndah͈ ñu jel i mēñef am.
Su borom‐tōl ba deluse nak, lan la di def ligeykat yōgale?
Mōtah͈ ma ne len, Di nañu jele ngur i Yalla fi yēn, te joh͈ ko h͈êt wu di mēña mēñef am.
Am na layu chi loh͈o am, te di na setali boju am fou, te dajale dugup am chi sah͈a mi; wande di na laka choh͈ ba chi safara su feyatil muk.