40 Su borom‐tōl ba deluse nak, lan la di def ligeykat yōgale?
Ba jamāno i mēñef jegeñse, mu yōni i ndau am chi ligeykat ya ndah͈ ñu jel i mēñef am.
Ñu japa ko, sani ko chi biti tōl ba, te rēy ko.
Ñu ne ko, Di na rēy nit ñu soh͈or ñōgale chi choh͈or, te lūye tōl am yenen i ligeykat, ñu ko di joh͈i mēñef yi chi sēn wah͈tu’ ñorte.