39 Ñu japa ko, sani ko chi biti tōl ba, te rēy ko.
Wande ba ligeykat ya sēne dōm ja, ñu ne chi sēn bopa, Kile di dono gi; ñou len, na ñu ko rēy, te jel ndono am.
Su borom‐tōl ba deluse nak, lan la di def ligeykat yōgale?
Yesu ne ko, Anda, defal li la tah͈ a dika. Fōfale ñu ñou, teg sēn i loh͈o chi Yesu, te jel ko.
Ña jap’ on Yesu yubu ko cha nēg i Caiaphas, kēlifa i seriñ ya, fa bindānkat ya ak mag ya dajalo won.
H͈arekat ya nak ak saltige ba, ak i ndau i Yauod ya japa Yesu, te ew ko,
Annas nak ew ko, te yōni ko Caiaphas, kēlifa i seriñ ya.