36 Mu yōnêti yenen i ndau yu upa ñu jeka ña: ñu def len nōgule itam.
Ligeykat ya japa ndau am ya, ratah͈ kena, rēy kenen, te jamat kenen ka ak i h͈êr.
Cha ganou ga mu yōni dōm am chi ñom, ne, Di nañu teral suma dōm.
Mu yōnêti yenen i ndau, ne, Wah͈ len ña ma ô on, Da ma wāj suma añ, rēndi suma i nag ak suma i rab yu dūf, te yepa emba na: ñou len chi nchēt li.