34 Ba jamāno i mēñef jegeñse, mu yōni i ndau am chi ligeykat ya ndah͈ ñu jel i mēñef am.
Ligeykat ya japa ndau am ya, ratah͈ kena, rēy kenen, te jamat kenen ka ak i h͈êr.
Wande ba ligeykat ya sēne dōm ja, ñu ne chi sēn bopa, Kile di dono gi; ñou len, na ñu ko rēy, te jel ndono am.
Su borom‐tōl ba deluse nak, lan la di def ligeykat yōgale?
Ñu ne ko, Di na rēy nit ñu soh͈or ñōgale chi choh͈or, te lūye tōl am yenen i ligeykat, ñu ko di joh͈i mēñef yi chi sēn wah͈tu’ ñorte.
Te yōni i ndau am ñu ôal ko ña mu ô on chi nchēt la; ñu bañ a dika.