3 Su len kena wah͈e lef, na ngēn ne, Borom bā len soh͈la; te di na len yōni.
Ne len, Dem len chi bir deka ba chi sēn kanam, te di ngēn feka mbamsuf mu ñu ew, and’ ak chumbur: tiki len, te isi len fi man.
Lile am on na nak, ndah͈ lu yonent ba wah͈ on motaliku, ne,
Naka nga ko maye won sañsañ chi kou nit ñepa, ndah͈ mu maye ña nga ko may on ñepa dūnda gu dul jêh͈.
Bay ba sopa na Dōm ja, te joh͈ na ko lu neka chi loh͈o am.