29 Mu tontu, ne, Du ma dem: wande cha ganou mu rēchu, te dem.
Wande lan ngēn dēfe? Kena nit am on na ñar i dōm yu gōr; mu ñou chi tau ba, ne, Suma dōm, demal ligey tey chi suma tōl.
Mu ñou cha ñarel ba, te wah͈ati lōga. Mu tontu, ne, Di nā dem; wande demul.
Kan chi ñom ñar a def la sēn bay buga? Ñu ne ko, Tau ba. Yesu ne len, Chi dega mangi len di wah͈, Publican ya ak garbo ya di nañu dem chi ngur i Yalla as yēn.