27 Ñu tontu Yesu, ne, H͈amu ñu. Mu ne len it, Man du ma len wah͈ ak ban sañsañ lā defe yef yile.
Bayi len len; ño di njīt yu silmah͈a. Te su silmah͈a jītê silmah͈a, di nañu tabi chi mpah͈ ñom ñar.
Ti chi sūba, Di na h͈ēn tey, ndege asaman si tīm na. Mun ngēn a rañātle kanam i asaman si; wande munu len a rañātle melo i jamāno yi.
Wande su ñu ne, Chi nit; da ñu ragal mbōlo ma; ndege jape won nañu John niki yonent.
Wande lan ngēn dēfe? Kena nit am on na ñar i dōm yu gōr; mu ñou chi tau ba, ne, Suma dōm, demal ligey tey chi suma tōl.
Nit ka tontu te ne len, Lile nak njomite la, ne h͈amu len fu mu bayako, te ūbi suma i but.