26 Wande su ñu ne, Chi nit; da ñu ragal mbōlo ma; ndege jape won nañu John niki yonent.
Wande lutah͈ on ngēn dem? sêt ab yonent am? Wau, ma ne len, te ku upa yonent.
Ba mu ko buge rēy, mu ragal mbōlo ma, ndege fōg nañu ne yonent la won.
Mbōlo ma ne, Kile di Yesu, yonent i Nazareth chi Galilee.
Batise’ John, fan la juge won? cha ajana am chi nit? Ñu werante chi sēn digante, ne, Su ñu ne, Cha ajana; di na ñu ne, Lutah͈ gumu len ko won mbōk?
Ñu tontu Yesu, ne, H͈amu ñu. Mu ne len it, Man du ma len wah͈ ak ban sañsañ lā defe yef yile.
Ba ñu jēme japa ko, ñu ragal mbōlo ma, ndege jape won nañu ko niki yonent.
Mō don lampa ba di tāka te di melah͈: te nangu won ngēn a banēh͈u chi i sā cha lêr am ga.
Wā’ jur am ya wah͈ nañu yef yile, ndege ragal on nañu Yauod ya: ndege Yauod ya wah͈ante on nañu be sotal, ne su kena wah͈e ne mō di Krista, di nañu ko gēne chi ndaje ma.