24 Yesu tontu len ne, Man it di nā len lāj bena bāt, te su ngēn ma ko wah͈e, di nā len wah͈ itam ak ban sañsañ lā defe yef yile.
Mangi len di yōni naka i nh͈ar chi digante i būki: mōtah͈ na ngēn têylu naka i jān, te lew naka i mpetah͈.
Ba mu ñoue chi bir juma ja, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñou fi mōm ba mō jemantale, ne, Ak ban sañsañ nga defe yef yile? te ku la joh͈ sañsañ bile?
Batise’ John, fan la juge won? cha ajana am chi nit? Ñu werante chi sēn digante, ne, Su ñu ne, Cha ajana; di na ñu ne, Lutah͈ gumu len ko won mbōk?