15 Wande i njīt i seriñ ya ak bindānkat ya, ba ñu gise koutef ya mu def, ak gūne ya di h͈āchu chi juma ja, ne, Hosanna Dōm i Dauda; ñu mer lol,
Ba ko fuka ña dēge, ñu mere ñar i mboka ya.
Ba mu ñoue chi bir juma ja, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñou fi mōm ba mō jemantale, ne, Ak ban sañsañ nga defe yef yile? te ku la joh͈ sañsañ bile?
Mbōlo ma jītu ak ña topa h͈āchu, ne Hosanna Dōm i Dauda; barkel chi ki di dika chi tur i Borom bi; Hosanna ma cha kou.
Lan ngēn dēfe chi Krista? dōm i kan la? Ñu ne ko, Dōm i Dauda.
Fōfale i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña dajalo fi ker i kēlifa i seriñ ya, ku tūda Caiaphas,
I njīt i seriñ ya nak ak ndaje ma yepa ūt sēde i fen lu jem chi Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.
Ba lelek sa jote, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñepa fēnchu Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.
I njīt i seriñ ya nak ak mag ya digal mbōlo ma ñu lāj Barabbas, te rēylu Yesu.
Ba fa Yesu juge, ñar i silmah͈a topa ko, di h͈āchu, ne, Amal yermande chi ñun, you dōm i Dauda.
I njīt i seriñ ya ak Pharisee ya joh͈e won nañu eble, ne su kena h͈ame fu mu neka, na ko wone, ndah͈ ñu japa ko.
Pharisee ya nak wah͈ante chi sen bopa, ne, Gis ngēn ne munu len dara: aduna si topa nañu ko.
Ba Borom bi h͈ame nak ne Pharisee ya dēg’ on nañu ne Yesu angi don def te batise i talube yu gen a bare as John,
Ndah͈ mbinda mi wah͈ul on, ne Krista di na jugeji chi gēño’ Dauda, ak cha Bethlehem, deka ba Dauda nek’ on?